Colossians 1:16 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte ci moom la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf, li ñuy gis ak li ñu mënul a gis, muy buur, njiit, kilifa mbaa boroom sañ-sañ. Lépp lu ñu sàkk, ci moom lañu ko jaarale, ci moom lañu ko jëme.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax moo di ki Yàlla sàkke lépp lu nekk asamaan, ak lu nekk ci suuf, lu gisu, ak lu gisuwul, muy boroom gàngune yeek, boroom ndomboy tànk yeek, boroom nguur yeek, boroom sañ-sañ yi. Lépp ci moom lees ko sàkke, te mooy ki tax ñu sàkk lépp.