Colossians 1:20 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
te jaar ci moom, jubale lépp ak boppam, muy ci kaw asamaan yi mbaa ci suuf, ba mu wàccee jàmm jaarale ko ci deret ji tuuru, bi Doom ji deeyee ca bant ba.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf, ak la fa asamaan.