Colossians 1:23 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Loolu nag na fekk ngeen wéy ci ngëm, sampu ci ba dëgër ci, tey séentu cér, bi leen xebaar bu baax bi jox. Te xebaar bu baax, boobu ngeen dégg te ñu yégal waa àddina sépp, man Pool moom laay yégle.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm, bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.