Colossians 1:27 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
ci xeeti àddina sépp. Ñoom nag la Yàlla bëgg a xamal ni ndamu kumpa googu màgge, maanaam Kirist a ngi dëkk ci yéen, di yaakaar ju wér ci ndamu ëllëg.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñoom la Yàlla nammoona xamal ni mbóot mi yaatoo te yéeme, ñeel jaambur ñi dul Yawut: mbóot mi moo di Almasee ngi ci yeen ñi dul Yawut itam, loolu di seen yaakaar ci ndam lu leen ñeel.