Colossians 1:9 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Looloo tax ci sunu wàllu bopp, ba nu ko yégee ba tey, jógunu ci di leen ñaanal. Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen xam bu baax coobareem ci xel mu mat ak ràññee gu aju ci dooley Xelam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen feese xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel, ak gis-gis bu Noo gi maye.