Colossians 3:11 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ci dund gu bees googu, amul Yawut ak ku dul Yawut, ku xaraf walla ku xaraful, jaam walla gor, ku jàngul ni Baarbaar yi, ak ku yeewuwul ni waa Sit, waaye Kirist ay lépp te dëkk ci ñépp.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.