Colossians 4:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Jaamu Kirist, Epafras, mi bokk ci yéen, mu ngi leen di nuyu. Du jóg ci di leen ñaanal, farlu ci ni kuy bëre, ngir ngeen taxaw temm ci coobareg Yàlla gépp, ànd ak ngëm gu mat ak kóolute gu wóor.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci jaamub Almasi Yeesu, Epafras, mi bokk ci yeen. Ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla.