Daniel 1:2 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Boroom bi nag teg Yowakim buurub Yuda ciy loxoom, boole ca lenni jumtukaayi kër Yàlla ga. Nabukodonosor yóbbu jumtukaay ya réewum Sineyaar, ga ñuy wax Babilon itam, ca biir kërug tuuram. Mu daldi fat jumtukaay ya ca denci kër tuuram.