Ephesians 2:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
booba amuleen woon benn cér ci Kirist, mbaa benn baat ci kureelu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre, gi Yàlla fas ak ñoom, te ëmb dige ya. Amuleen woon jenn yaakaar mbaa benn xam-xamu Yàlla ci àddina.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina.