Ephesians 4:16 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
te jëmm jépp ci moom lay dunde, di jëmm ju ràbboo te déggoo ci bépp tenqoo, te cér bu nekk di def warugaram. Noonu jëmm ji di yokku ak a màgg ci biir mbëggeel.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci moom miy bopp bi la yaram wépp di déggoo, témboo ndax ndimbalal mboolem tenqo yi koy saytu, na mu dëppook wàllu cér bu ci nekk. Su ko defee yaram wiy yokku, di màgg ci biir cofeel.