Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ñu bind ca bataaxal ya, ne Buur may na Yawut yi ci dëkkoo dëkk sañ-sañu taxawandoo, aar seen bopp. Sañ nañoo tas mbooloo mu leen mana song, ak xeet wu ñu bokk mbaa diiwaan bu ñu bawoo. Nañu sànk woowu xeet, rey leen, faagaagal leen ñook seeni jabar ak seeni doom, boole ca lël seen alal.