Exodus 36:20 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gannaaw gi ñu sàkkal jaamookaay bi ay làcci bantu séng yu sampe. Làcc wu nekk am ñaari kenu yu ñu lëkklee galan yu ndaw, te noonu lañu def làcci jaamookaay bi yépp. Fukki xasab lañu def taxawaayu làcc wu nekk, def yaatuwaay bi xasab ak genn-wàll.