Ezekiel 33:27 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, ku nekk ci yeen ci biir gent yi, saamar lay fàddoo; képp ku nekk ci biir àll bi, rab yi laa koy jox, ñu lekk ko; te képp ku làqoo tata yeek xunti yi, mbas a koy rey.