Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Boroom bi Aji Sax ji nag dafa wax ne: Maa ngii déy di waxe sama tàngooru fiiraange ak xeet yi dul yawut, boole ci Edom gépp, ñoom ñi jiital seen xeebeel, te suuf si ma séddoo, ñu aakimoo ko, te di ko bége mbégte mu mat sëkk, ngir sëxëtoo parluy réew mi.”