Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Li war ki tooge jal bi, saraxu rendi-dóomal ci la, ak saraxu pepp, ak saraxi biiñ yi ñuy joxe bésu màggal, yu mel ni màggali Terutel weer ak bési Noflaay, ak yeneen bés yu bànni Israyil taamoo daje. Moom it mooy joxe saraxu póotum bàkkaar, ak saraxu pepp, ak saraxu rendi-dóomal, ak saraxu cant ci biir jàmm ngir njotlaayal waa kër Israyil.