Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Léegi nag Buur, su la soobee, nañu seet ca denci buur, foofu ci Babilon, ngir wóorlu ndax Buur Sirus joxe woon na ndigal ne ñu tabaxaat kër Yàlla gi ci Yerusalem. Gannaaw loolu loo dogal ci mbir mi rekk, Buur, yónneel, jottli nu ko.