Galatians 2:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte laata ndaw yi Saag yónni di ñëw, da daan bokk di lekk ak ñi dul Yawut. Waaye bi ñu agsee, te mu ragal kureel boobu faaydaal xaraf, mu dellu gannaaw, di sore ñi dul Yawut.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kat balaa aw nit a dikk, bàyyikoo fa Yanqóoba, Sefas da daan bokk lekk ak jaambur ñi dul Yawut. Waaye ba ñooñu dikkee la rocciku, daldi beddeeku jaambur ñi, ndax ragal waa làng, ga jàpp ne aaday xaraf wartéef la.