Galatians 2:16 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Teewul nu xam ne, Yàlla du àtte kenn ni ku jub ci kaw sàmm yoon, waaye ci gëm Yeesu Kirist. Kon nun itam gëm nanu Kirist Yeesu, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw gëm Kirist, te du ci sàmm yoon. Ndaxte du caageenug sàmm yoon mooy tax Yàlla àtte kenn ni ku jub.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di joxe àtteb ku jub, xanaa ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla jox nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di joxe kenn àtteb ku jub.