Galatians 2:6 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye ñi ñu gën a fonk --ak lu man a doon seen sag xooluma ko, ñépp a yem fa kanam Yàlla — waaye ñooñu ñu teg njiit boog, bi ma dajee ak ñoom, yokkuñu dara ci sama sas.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Teewul ñooñu ñu jàppe woon ay kàngam, ak daraja ju ñu masoona am, amalu ma solo, nde Yàlla amul xejj ak seen, ñooñu yokkuñu lenn ci kàddu gi may xamle.