Galatians 2:7 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Gis nañu ne, Yàllaa nu yebal, muy man di Piyeer, ngir nu yégle xebaar bu baax bi; ma féetewoo ñi dul Yawut, Piyeer féetewoo Yawut yi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Xanaa kay li ñu gis moo di ni Yàlla yebale Piyeer ngir mu àgge askanu Yawut xibaaru jàmm bi, noonu la ma yebale ngir ma àgge ko jaambur ñi xaraful,