Galatians 3:16 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Léegi nag Yàlla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam. Mbind mi waxul: «Ak i sëtam,» mu mel ni ñu bare, waaye kenn la wax: «Ak sa askan,» maanaam Kirist.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Te Ibraayma lañu digoon dige yi mook ki taxawal askanam. Newuñu: «ñi taxawal ay askanam», mbete ñu bare lañuy wax, waaye wenn rekk la: «ki taxawal askanam,» te ki taxawal askanam moo di Almasi.