Galatians 3:17 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Li ma ci bëgg a wax mooy lii: ndegam Yàlla fas na kóllëreem, yoonu Musaa, wi feeñ ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw ga, du ko man a fecci, ba tebbi digeb Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Li ma ciy wax mooy lii: kóllëreg Yàlla gi taxawe ni kayitu donale gu mu dëggal, yoonu Musaa, wi dikk ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw kóllëre gi, manu koo neenal, ba fomm digeb Yàlla.