Galatians 3:21 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndax kon yoonu Musaa wi dafa juuyoo ak li Yàlla dige? Mukk! Su amoon yoon wu nit man a sàmm, ba mu jural ko dund gu sax, kon sàmm yoon dina tax nit jub fa kanam Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax kon yoonu Musaa dafa juuyoo ak digey Yàlla? Mukk kay. Ndax kat su fekkoon ne dañoo maye wenn yoon wu mana may nit ku ko sàmm, mu dund, konoon àtteb ku jub fi kanam Yàlla mana jóge dëgg ci sàmm gu nit ki sàmm yoon wi.