Galatians 4:9 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye léegi nag bi ngeen xamee Yàlla, walla boog bi leen Yàlla xàmmee, nan ngeen man a def, bay delluwaat ca aaday àddina? Aada yooyee ñàkk doole te ñàkk njariñ, lu tax ngeen bëgg, ñu nootaat leen?
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye léegi bi ngeen xamee Yàlla, mbaa bi leen Yàlla ràññee, nu ngeen mana delluwaate ci mbiri àddina yooyu boole tële ak ñàkk njariñ, bay nekkaat seeni jaam?