Galatians 5:10 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye teewul Boroom bi jox na ma kóolute ci yéen. Biral na ma ne, dingeen bokk ak man xalaat. Léegi nag, kiy nëxal seen xel, ku mu man a doon, Yàlla dina ko mbugal.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Man de gëm naa ndax Boroom bi, ne dungeen wuuteek man xalaat benn yoon ci lii. Waaye kiy jaxase seenum xel, ak ku mu mana doon, mooy gàddu mbugalam.