Galatians 5:17 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte sunu nafsu am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu Xelum Yàlla. Te Xelum Yàlla itam am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu sunu nafsu. Ñoom ñaar dañoo juuyoo ci bépp fànn, ba tax lépp lu ngeen bëggoon a def, dungeen ko man.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax bakkan, la muy xemmem, daa dëngoo ak Noo gi; Noo gi it, la muy xemmem dëngoo ak bakkan. Dañu di yaar yu féewaloo, te moo tax dungeen def la ngeen nammoona def.