Galatians 6:1 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bokk yi, ku ñu fekk muy def lu Yàlla bëggul, yéen ñi topp Xelum Yàlla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga sàmm sa bopp, ngir bàkkaar bañ laa fiir, yaw itam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir gu ni mel.