Genesis 23:17 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom.