Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Li tax ma def loolu mooy, bi ma jógee Padan di ñibbi, Rasel dafa faatu ca yoon wa ci sama kanam, ba nuy tollu ca réewu Kanaan, booba nu ngay dem, bay jub Efrata. Ma suul ko foofa, ca yoonu Efrata.» Efrata mooy Betleyem tey.