Hebrews 1:3 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndeyjooru Aji Màgg ji ca kaw,
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,