Hebrews 10:34 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ndaxte bokk ngeen naqar ak ñi ñu tëj, te nangu ngeen ak xol bu sedd, ñu foqarñi seen alal, xam ne, am ngeen alal ju gën te di sax ba fàww.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñe xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww.