Hebrews 11:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Looloo tax ba, Ibraayma mi màggat lool, aw xeet jóge ci moom, baree ni biddiiwi asamaan, te sakkan ni suufu tefes, ba kenn mënu koo xayma.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Looloo waral genn góor doŋŋ, ku dee rekk dese, aw askan mana soqikoo ci moom, tollu ni biddiiwi asamaan ndax bare, wees ab lim ni feppi suufas géej.