Hebrews 11:19 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye xelu Ibraayma jàppoon na ne, Yàlla am na dooley dekkal néew yi. Te dëgg-dëgg ci misaal dafa mel ni, Isaaxa dafa dee te dekki.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye Ibraayma njortoon na ne su Isaaxa dee woon it, Yàlla man na koo dekkal. Moo tax itam ci misaal, Isaaxa délsi ciy loxoom, mel ni daa dekki.