Hebrews 11:5 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ngëm moo tax ba Enog jaarul ci dee. Yàllaa ko yóbbu ca moom, te kenn gisatu ko, ndaxte Yàllaa ko toxal. Ndaxte Mbind mi seedeel na ko ne, laata muy toxu, neex na Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw ngëm lees yóbboo Enog, te deewul. Da ne mes, ndax Yàllaa ko yóbbu. Balees koo yóbbu kay, lees ko seedeeloon ne moo bànneexal Yàlla.