Hebrews 11:9 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ngëm a tax ba Ibraayma sanc ci réew, mi ko Yàlla digoon, dëkk ci ay tànt ni doxandéem, moom ak doomam Isaaxa ak sëtam Yanqóoba, fekk sax Yàlla digoon na leen réew mi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.