Hebrews 12:2 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Nanu ne jàkk Yeesu, moom mi samp ngëm, ba ub làmbi ngëm. Mbég mi mu dëgmël moo tax mu dékku dee ca bant ba te faalewul toroxte, ji ko fa fekk, ba noppi toog ca ndeyjooru jal, ba Yàlla nekk.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru jalub Yàlla.