Hebrews 12:9 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Waaye sax far, sunuy baay ci àddina yaroon nañu nu, te wegoon nanu leen. Baay bi yore ruu yi kon, xanaa warunu koo gën a déggal ngir man a dund?
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Te itam am nanu ay baay ci wàllu deret, ñoo nu daan yar, te danu leena wegoon. Kon nag xanaa du Baay bi yor ug noo lanu wara gënatee nangul, ngir nu dund?