Hebrews 13:17 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Déggal-leen seeni njiit te topp seen ndigal, ndaxte ñoo leen di sàmm te ñooy layoo seen liggéey. Kon nangeen leen déggal, ngir ñu man a def seen liggéey ak xol bu sedd, bañ cee am naqar, ndaxte loolu du leen amal njariñ.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Déggal-leen seeni njiit te nangul leen, ndax sàmm bakkani ñi ñu jiite mooy seenub liggéey, te moom lees leen di laaj ëllëg. Su ko defee ñu defe ko xol bu sedd, te bañ koo def di binni, ndax loolu du seen njariñ.