Hebrews 2:14 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Doomam yooyu muy wax, nit kese lañu. Looloo tax Yeesu it moom ci boppam, wàcc na, jëmmoo ni ñoom, ngir dee, ba man caa daaneel Ibliis, mi yore dooley dee.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.