Hebrews 2:17 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Looloo taxoon mu war a mel niy doomi baayam ci bépp fànn, ngir doon seen saraxalekat bu mag fa kanam Yàlla, bi leen yërëm te di sàmm kóllëre, te ci liggéeyu saraxaleem joxe na bakkanam ngir dindi bàkkaari nit ñi, ba Yàlla baal leen.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.