Hebrews 2:9 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye gis nanu Yeesu. Wàcce nañu ko, def ko mu gën a suufe tuuti malaaka yi, ngir mu dee ci wàllu ñépp, ndaxte loolu la Yàlla dogal ci yiwam. Waaye léegi Yàlla kaalaa na ko teraanga ak ndam ndax coono bi mu daj ba dee.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deeyam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deeyale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.