Hebrews 3:1 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Kon nag yéen bokk yu sell yi, yéen ñi Yàlla woo, ngeen bokk ci nguuram gu kawe ga, seetleen ci Yeesu, moom miy ndawu Yàlla li, di saraxalekat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.