Hebrews 4:1 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Yàlla dige na ne, dina am ñu dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci yéen réer ba du dugg ci noflaay boobu.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kon nag gannaaw digeb tàbbi ci noflaayal Yàlla mu ngi sax ba tey, nanu ragal kenn ci yeen taxawe melokaanu ku ca jotul.