Hebrews 4:12 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Xam nanu ne, kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gën a ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.