Hebrews 4:3 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Nun ñi gëm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe:«Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay,”» doonte sax liggéeyam bépp matoon na, ca ba mu sàkkee àddina ak léegi. Ci lu jëm ci juróom-ñaareelu fan ba,
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Nun ñi gëm doŋŋ nooy tàbbi ci noflaayam, noonu mu ko waxe, ne: «Maa giñe sama biir mer, ne: “Duñu tàbbi mukk ci samag noflaay.” » Ndaxam ca cosaanu àddina la liggéeyi Yàlla sotti woon ba noppi,