Hebrews 6:1 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Kon nag léegi, nanu jóge ci liifantu gi jëm ci Kirist, te jàll cig mat. Nanu bañ a dalaat njàngale mu jëkk moomu, ci ne nit ñi dañoo war a tuub jëf, yi jëm ci dee, te gëm Yàlla,
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat kenu gi. Kenu gi mooy gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi ndee.