Hebrews 7:11 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Jox nañu bànni Israyil yoon wu sukkandiku ci liggéeyu saraxalekat yi soqikoo ci Lewi. Su fekkoonte ne nag liggéeyu saraxalekat yooyu manoon na yeggale nit cig mat, kon du soxlaati ab saraxalekat ni ko Melkisedeg nekke, ci fànn gu wuute ak gu Aaroona.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kon liggéeyu carxal gu Leween, ñi yoroon yoonu Musaa, wi ñu dénkoon bànni Israyil, su doon liggéey buy taxa mat sëkk, ndax dees na soxlaati beneen sarxalkat bu jóg topp dayob Melkisedeg, te toppul dayob Aaróona?