Hebrews 7:2 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu Ibraayma fab fukkeelu cér bi, maanaam asaka, ci li mu jële woon ci xare ba lépp, jox ko. Ci lu jëkk turu Melkisedeg mi ngi tekki «buur bu jub bi.» Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki «buuru jàmm.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Moom la Ibraayma jox fukkeelu cérub mboolem cëxëtoo ma. Ni ñu jëkka dégge aw turam Melkisedeg, ci tekki, mooy «buur bu jub». Bu loolu weesee itam moom mooy buurub Salem, muy «buuru jàmm».