Hebrews 7:27 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Niroowul ak yeneen saraxalekat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.