Hebrews 8:10 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak bànni Israyil,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xel,bind ko ci seen xol.Dinaa nekk seen Yàlla,ñu doon samay gaay.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
«Lii nag moo di kóllëre gi may fas ak kër Israyil, gannaaw yooyu fan, la Boroom bi wax, mu ne: Maay yeb sama ndigali yoon ci seenum xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.